+ -

عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ أَنَّ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«يَعْقِدُ الشَّيْطَانُ عَلَى قَافِيَةِ رَأْسِ أَحَدِكُمْ إِذَا هُوَ نَامَ ثَلاَثَ عُقَدٍ يَضْرِبُ كُلَّ عُقْدَةٍ عَلَيْكَ لَيْلٌ طَوِيلٌ، فَارْقُدْ، فَإِنِ اسْتَيْقَظَ فَذَكَرَ اللَّهَ، انْحَلَّتْ عُقْدَةٌ، فَإِنْ تَوَضَّأَ انْحَلَّتْ عُقْدَةٌ، فَإِنْ صَلَّى انْحَلَّتْ عُقْدَةٌ، فَأَصْبَحَ نَشِيطًا طَيِّبَ النَّفْسِ، وَإِلَّا أَصْبَحَ خَبِيثَ النَّفْسِ كَسْلاَنَ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 1142]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"saytaane day fas ci ginnaaw boppu kenn ci yéen bu dee nelaw ñatti fas, genn fas-fas gu nekk day waral ci yaw guddi gu gudd, mu naan nelawal, bu yeewoo daal di tudd Yàlla genn fas-fas fecceeku, bu jàppoo geneen fas-fas fecceeku, bu jullee geneen fas-fas fecceeku, mu mujj nekk ku sawar, ku teey bakkan, bu dul loolu day nekk ku bon bakkan di ku tàyyeel".

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 1142]

Leeral

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare mbiri saytaane ak ni muy xeexe ak nit ki bëgg a taxaw guddi ngir julli guddi walla Fajar.
Aji-gëm ji bu demee jëm ca nelaw ya saytaane day fas ci ginnaaw boppam ba -maanaam: ginnaaw catu bopp ba- ñatti fas-fas.
Bu aji-gëm ji yewwoo daal di tudd Yàlla mu kawe mi te nangulul jax-jaxi Saytaane yi; genn fas-fas fecceeku.
Bu jàppoo geneen fecceeku. .
Bu jugee daal di julli fas-fasu ñatteel bi fecceeku, mu xëy di ku sawar di ku teey bakkan; ngir ag bégam ci li ko Yàlla tawfeexal ci mu jaamu ko, di bége li ko Yàlla dig ci ab yool ak njéggal, ak fas-fasi Saytaane yi ak tàyyeelam gi deñ ci moom, bu dul loolu rekk day xëy di ku bon bakkan, di ku jàq ab xol, di ku tàyyeel ci def aw yiw ak lu baax; ndaxte moom dees ko a jéng ci jéngi Saytaane, muy ku ñu soreele wolif jege Aji-Yërëmaakoon ji.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Saytaane day dox saa su ne ci yoon yépp ngir dox ci
  2. diggante nit ki ak topp Yàlla mu màgg mi, te jaam bi du mucc ci Saytaane lu dul ci muslu ci Yàlla mu màgg mi, ak jàpp ci sababi fegu yi ak aaru yi.
  3. Tudd Yàlla day waral cawarte ci bakkan bi, ak dënn bu yaatu, te day dàq tàyyeel ak yonjax, te day dindi jafe-jafe ak mbañeel; ndaxte day dàq Saytaane te lii ci ay jax-jaxam la.
  4. Aji-gëm ji day bég ci li ko Yàlla di tawfeexal ci mu taxaw ci topp ko, waaye day xat ngir gàtteñloom ci ngëneel yi.
  5. Càggante ak baña topp Yàlla ci jëfi Saytaane la.
  6. Ñatti bir yii -tudd Yàlla, ak jàppu, ak julli- day dàq Saytaane.
  7. Fasi Saytaane yi ci ginnaaw bopp bi la ko jagleel; ndaxte mooy barabu kàttan gi, kon bu ko fasee dana man a not ruuhu nit ki, ak sànni ko ay nelaw.
  8. Ibn Hajar Al-Asxalaanii nee na: tudd gi mu tudd guddi ci li mu wax: "am nga guddi", li ci feeñ mooy loolu dafa jagoo nelawi guddi.
  9. Ibn Hajar Al-Asxalaanii nee na: genn sikar gu ñu jagleel ràññeekuwul ci sikar yi ba gu dul moom du ca doy, waaye lépp lu tudd Yàlla rekk doy na, jàng Alxuraan da cay dugg, ak jàng Hadiisu Yonnente bi, ak yittewoo jàng xam-xamu sariiha, li gën a yay nu tudd ko ca mooy waxi Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc: (laa i Laaha illal-Laahu wahdahu laa sariika lahu, lahul mulku wa lahul hamdu wa huwa halaa kulli say-in xadiirun, Alhamdu lil-Laah, wa subhaanal Laah, wa laa-i-Laaha illal-Laahu wal-Laahu Akbaru, wa laa hawla wa laa xuwwata illaa bil-Laahi, topp mu wax: allaahuma ixfirlii, walla mu ñaan, dees na ko nangul, bu jàppoo ñu nangu julleem) Al-Buxaarii soloo na ko.
Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Almaa Pastoo Asaami Suwiit Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Litwaani Serbi Kinirowanda Rom Majri الموري Oromoo Kanadi Ukraani الجورجية المقدونية الماراثية
Gaaral tekki yi