عَنْ مَعْدَانَ بْنِ أَبِي طَلْحَةَ الْيَعْمَرِيُّ قَالَ:
لَقِيتُ ثَوْبَانَ مَوْلَى رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، فَقُلْتُ: أَخْبِرْنِي بِعَمَلٍ أَعْمَلُهُ يُدْخِلُنِي اللهُ بِهِ الْجَنَّةَ؟ أَوْ قَالَ قُلْتُ: بِأَحَبِّ الْأَعْمَالِ إِلَى اللهِ، فَسَكَتَ. ثُمَّ سَأَلْتُهُ فَسَكَتَ. ثُمَّ سَأَلْتُهُ الثَّالِثَةَ فَقَالَ: سَأَلْتُ عَنْ ذَلِكَ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، فَقَالَ: «عَلَيْكَ بِكَثْرَةِ السُّجُودِ لِلَّهِ، فَإِنَّكَ لَا تَسْجُدُ لِلَّهِ سَجْدَةً، إِلَّا رَفَعَكَ اللهُ بِهَا دَرَجَةً، وَحَطَّ عَنْكَ بِهَا خَطِيئَةً» قَالَ مَعْدَانُ: ثُمَّ لَقِيتُ أَبَا الدَّرْدَاءِ فَسَأَلْتُهُ فَقَالَ لِي: مِثْلَ مَا قَالَ لِي: ثَوْبَانُ.
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 488]
المزيــد ...
Jële nañu ci Mahdaan ibn Abii Talhata Alyahmarii mu wax ne:
Dajee naa ak Sawbaan surgab Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ma ne ko: wax ma jëf joo xam ne bu ma ko defee Yàlla dugal ma ci àjjana? Walla mu ne ma ne ko: jëf ji Yàlla gën a bëgg, mu noppi, ma laajaat ko, mu noppi, ma laajaat ko ñatteelu yoon, mu ne ma: laaj naa ko Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu ne ma: "déng naa la ngay bari looy sujjóotal Yàlla, ndaxte doo sujjóotal Yàlla genn sujjóot lu dul ne Yàlla dina la ci yëkkatil daraja, sippil la ci njuumte" Mahdaan nee na: ma dajee ak Abuu Dardaa ma laaj ko mu tontu ma: lu mel ni li ma Sawbaan wax.
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 488]
Laaj nañu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- jëf joo xam ne sabab la ci dugg àjjana, walla jëf ji Yàlla gën a bëgg?
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax aji-laaj ji ne ko: deel taqoo ak baril sujjóot ci julli, ndax doo sujjóotal Yàlla genn sujjóot lu dul ne dana la ci yëkkatil daraja, jéggal la ci njuumte.