+ -

عن أبي هريرة رضي الله عنه أن رسول الله صلى الله عليه وسلم قال:
«كان رجلٌ يُدَايِنُ الناسَ، فكان يقول لفتاه: إذا أتيتَ مُعسِرًا فتجاوز عنه، لعل اللهَ يَتجاوزُ عنا، فلقي اللهَ فتجاوز عنه».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 1562]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«am na benn waay bu doon lebal nit ñi, daan wax ndawam la naan ko: boo demee ci ku am jafe-jafe nanga ko jéggal, amaana Yàlla jéggal nu, mu dajeek Yàlla mu jéggal ko».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 1562]

Leeral

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne: benn waay da doon jëflànte ak nit ñi ci leb-lante, walla mu leen di jaay ba jëmmi-jamono ñu door koo fay, Mu daan wax ndawam la daan fayyeeku ji bor ya ca nit ña: Boo demee ci ku ame bor te amul lu mu faye ngir néew doole «nanga ko jéggal», benn ci neggandiku ko te bañ koo taxawu ci di ko laaj, Walla ci jël li mu am donte sax matul, loolu nag ngir li mu bëgg ak xemmeem ci Yàlla jéggal ko daal di koy baal. Ba mu faatoo Yàlla baal ko jéggal ko ay ñaawtéefam,

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Asrabijaani Usbeg Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Refetal ci jëflante ak nit ñi, ak di leen baal, te di jéggal ki nekk ci jafe-jafe daa bokk ci sabab yi gën a màgg ci muccug jaam bi ëllëg bis-penc.
  2. Rafetal jëme ci nit ñi, ak sellal ngir Yàlla, ak yaakaar yërmaandeem, daa bokk ci sababi njéggali bàkkaar yi.