عَنْ عَائِشَةَ أُمِّ المؤْمِنينَ رَضِيَ اللهُ عَنْهَا:
كَانَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَجْتَهِدُ فِي الْعَشْرِ الْأَوَاخِرِ مَا لَا يَجْتَهِدُ فِي غَيْرِهِ.
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 1175]
المزيــد ...
Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne :
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na pasteefu ci fukk yu mujj yi lu mu daawul pasteefu ci yu dul yooyu.
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 1175]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu fukki guddi yi mujj ci weeru Koor daan ñëw da daan pasteefu ci jaamu ak topp Yàlla, di jëf bu baax xeeti yiw yi ak xeeti baax yi ak jaamu yi lu ëpp lu mu daan góor-góor lu ci yu dul yooyu; ndax màggaay ak ngëneeli guddi yooyu, ngir sàkku it Laylatul Xadri.