عَنْ عَائِشَةَ أُمِّ المُؤْمِنينَ رَضِيَ اللهُ عَنْهَا قَالَتْ:
كَانَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ إِذَا دَخَلَ الْعَشْرُ أَحْيَا اللَّيْلَ، وَأَيْقَظَ أَهْلَهُ، وَجَدَّ وَشَدَّ الْمِئْزَرَ.
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 1174]
المزيــد ...
Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu fukki guddi yi daan dugg da daan dundal guddi yi, yee njabootam, pasteefu daal di takku ba dëgër.
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 1174]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu fukki guddi yi mujj ci weeru koor daan dugg da daan dundal guddi yépp, ci ay xeeti jaamu, daal di yee njabootam ngir julli, mu pasteefu ci jaamu gi yokk la mu aadawoo woon, daal di bàyyi lépp ngir moom , daal di beru soxnaam yi.