عَنْ جَرِيرٍ رضي الله عنه عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«مَنْ يُحْرَمِ الرِّفْقَ يُحْرَمِ الْخَيْرَ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2592]
المزيــد ...
Jële nañu ci Jariir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«ku ñu ag ñeewant xañees na ko aw yiw».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2592]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne ku ñu xañ ñeewant ba dëppoowul ak moom ci biri diinee ak àddina ak ni muy doxale ci boppam, ni muy doxale ak ñeneen ñi, kooku xañ nañu ko léppi yiw.