عَنْ أَبِي حَازِمٍ قَالَ: قَاعَدْتُ أَبَا هُرَيْرَةَ رضي الله عنه خَمْسَ سِنِينَ، فَسَمِعْتُهُ يُحَدِّثُ عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، قَالَ:
«كَانَتْ بَنُو إِسْرَائِيلَ تَسُوسُهُمُ الأَنْبِيَاءُ، كُلَّمَا هَلَكَ نَبِيٌّ خَلَفَهُ نَبِيٌّ، وَإِنَّهُ لاَ نَبِيَّ بَعْدِي، وَسَيَكُونُ خُلَفَاءُ فَيَكْثُرُونَ» قَالُوا: فَمَا تَأْمُرُنَا؟ قَالَ: «فُوا بِبَيْعَةِ الأَوَّلِ فَالأَوَّلِ، أَعْطُوهُمْ حَقَّهُمْ، فَإِنَّ اللَّهَ سَائِلُهُمْ عَمَّا اسْتَرْعَاهُمْ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 3455]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abii Haasim mu wax ne: toog na ak Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm juróomi at, ma dégg ko muy waxtaan jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu ne:
«waa Banuu Israayil ay Yonente ñoo leen doon jiite, saa bu ab yonente faatoo beneen yonente wuutu ko, te ab Yonente du ñëw sama ginnaaw, ay Xalifa nag danañu nëw sama ginnaaw te danañu bari" ñu ne ko: lan nga nuy digal? Mu ne: "matalleen jaayante ga ka jiitu ak ka ca topp, ngee joxleen seen àq, Yàlla dana leen laaj la mu leen sàmmuloo woon».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 3455]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne waa Banuu Israayil ay Yonente ñoo leen doon jiite, di méngoo seen i bir kem ni njiit yi di def ak buur yi ci càmm gi, saa bu yàqute fésee fi ñoom Yàlla yónni ab Yonente mu jubbanti seen mbir dindi la ñu soppi woon ca àtte ya. Te nag ab Yonente du ñëw sama ginnaaw di def la ñooña daan def, ay Xalifa nag danañu nekk ci sama ginnaaw te danañu bari te xëccoo ak wuute dana am seen diggante. Sahaaba yi yal na leen Yàlla dollee gërëm laaj Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ana lan nga nuy digal? Mu ne: bu ñu jaayantee ak ub xalifa ginnaaw beneen xalifa; kon jaayateg ku njëkk ka moo wér te dana war ñu matal ko, jaayanteg ku ñaareel ki neen la, te araam na ci moom mu sàkku ko, nangeen leen jox seen àq, te topp leen dund ak ñoom ci dégg ak topp ci lu dul ag moy, Yàlla dana leen laaj càmbar leen ca la ñu def ci yéen.