عن عبد الله بن عمرو رضي الله عنهما قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«إِنَّ الْمُقْسِطِينَ عِنْدَ اللهِ عَلَى مَنَابِرَ مِنْ نُورٍ، عَنْ يَمِينِ الرَّحْمَنِ عَزَّ وَجَلَّ، وَكِلْتَا يَدَيْهِ يَمِينٌ، الَّذِينَ يَعْدِلُونَ فِي حُكْمِهِمْ وَأَهْلِيهِمْ وَمَا وَلُوا».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 1827]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abdullah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
"way-maandu ñi de fa Yàlla danañu nekk ci kaw i minbari leer, nekk ca ndeyjooru Yàlla Aji-Yërëme ju màgg ji te tedd te yaari loxoom yépp ndeyjoor la, ñooñu ñooy ñiy Mandu ca séen i àtte ak séen i njaboot ak lépp lu ñu méngoo».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 1827]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne ñi nga xam ne dañuy àtte nit ñi nekk ci séen suufu kilifteef cig maandu ak dëgg, ak ci séen i àtte ak séen i njaboot, ñoom de danañu toog ci ay baŋ yu kawe te yëkkëtiku di yu ñu bind cig leer, ngir teral leen ëllëg bis-pénc. Te minbar yii ca ndeyjooru Yàlla Aji-Yërëme ju kawe ji lay nekk, te yaari loxoom yépp -tudd naa sellam ga- ndeyjoor la.