+ -

عن أبي هريرة رضي الله عنه أن رسول الله صلى الله عليه وسلم قال:
«لَيْسَ الشَّدِيدُ بِالصُّرَعَةِ، إِنَّمَا الشَّدِيدُ الَّذِي يَمْلِكُ نَفْسَهُ عِنْدَ الْغَضَبِ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 6114]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«am doole nekkul ci bëre daan, waaye ku am doole mooy kiy tëye boppam bu meree».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Sunna yi bu Ad-daaraqutniy - 6114]

Leeral

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ci ne doole dëgg du dooley yaram, mbaa doole juy daan ñeneen nit ñu am doole, waaye ku am doole mooy kiy xeex ak bakkenam te man a not saytaane bu meree.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Itaali Oromoo Kanadi Usbeg Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bokk na ci njariñal adiis bi :
  2. gëneelu lewet ak téye sa bopp boo meree, ndaxte daa bokk ci jëf yu sell yi nga xam ne Lislaam da ciy soññee.
  3. Xeex ak sa bàkkan boo meree moo gën a tar xeex ak noon bi.
  4. Lislaam dafa soppi la ceddo ya jàppe woon , mu nekk jikko ju baax, kon nit ki ëpp kàttan mooy kiy téye boppam bu meree.
  5. Sori mer; ngir li muy waral ci lor nit ki ak mbooloo mi.