Toftaleg Adiis yi

képp ku woor weeru koor ngir gëm ak yaakaar yiw; dees na ko jéggal li jiitu ci ay bàkkaaram
عربي Àngale Urdu
ku taxaw Laylatul Xadri ngir gëm Yàlla ak yaakaar pay ga dees na ko jéggal li weesu ci ay bàkkaaram
عربي Àngale Urdu
tabax nañu lislaam ci juróom
عربي Àngale Urdu
Yàlla nee na: jépp jëfi doomu Aadama moom la ñeel, ba mu des woor, moom man maa ko moom te maa koy fay
عربي Àngale Urdu
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na pasteefu ci fukk yu mujj yi lu mu daawul pasteefu ci yu dul yooyu
عربي Àngale Urdu
Sama xarit ba yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dénk na ma ñatt: woor ñatti fan ci weer wu ne, ak ñaari ràkkay yoor-yoor, ak ma julli Witar balaa may nelaw
عربي Àngale Urdu
bu ngeen ko gisee woorleen, bu ngeen ko gisee worileen, bu muuroo ci yeen nangeen ko nattale
عربي Àngale Urdu
ku man a takk jabar na takk, ndaxte moo gën a man a damm ab gis, gën a man a sàmm péy mi, ku ko manul nag dénk naa ko woor, ndaxte dana ko man a téye
عربي Àngale Urdu
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moo gënoon a tabe ci nit ñi, ci weeru koor nag la daan gën a tabe ba Jibriil daan daje ak moom
عربي Àngale Urdu
man maay Damaam Ibn Sahlabata di mbokkum njabootu Sahd Ibn Bakrin
عربي Àngale Urdu
ku woor benn bis ci yoonu Yàlla, Yàlla soreele jëmmam ca sawara juróom-ñaar-fukki Nawet
عربي Àngale Urdu
nit ñi du ñu deñ di nekk ci yiw fii ak ñoo ngi gaaw a dog
عربي Àngale Urdu
Xëdd nañu ak Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu daal di jug jëm ca julli ga, ma ne ko: ñaata moo dox ci diggante nodd gi ak xëdd gi? Mu ne: luy tolloo ak juróom-fukki aaya
عربي Àngale Urdu
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na Lihtikaaf ci fukki fan yi mujj ci weeru koor, ba keroog muy faatu, ay saxnaam daldi Lihtikaaf ginnaawam
عربي Àngale Urdu
xëddleen, ndaxte xëdd lu am baarke la
عربي Àngale Urdu
buleen jiitu weeru koor ci woor benn walla ñaari fan lu dul koo xam ne da daan woor ag woor kon na ko woor
عربي Àngale Urdu
ku fàtte ne dafa woor, daal di lekk walla mu naan, na mottali wooram, ndax Yàlla moo ko leel moo ko mànnal
عربي Àngale Urdu
Fekke naa feet ga ak Umar ibnul Xattaab yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: ñaari bis yii Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa tere ñu woor leen: bis bi ngeen di dog seen koor gi, ak beneen bis bi ngeen di lekk seenum Tabaski
عربي Àngale Urdu
dàqleen Laylatul Xadri ci fukk yi mujj ci weeru koor
عربي Àngale Urdu
gis naa ne seen gent yi dañoo dëppoo ci juróom-ñaar yu mujj yi, ku koy diir na ko diir ci juróom-ñaar yu mujj yi
عربي Àngale Urdu
Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu fukki guddi yi daan dugg da daan dundal guddi yi, yee njabootam, pasteefu daal di takku ba dëgër
عربي Àngale Urdu
ku woor at mi kooku woorul, woor ñatti fan mooy woor at mi yépp
عربي Àngale Urdu