+ -

عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رَضِيَ اللهُ عَنْهُ أَنَّ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، قَالَ:
«إِذَا جَاءَ رَمَضَانُ فُتِّحَتْ أَبْوَابُ الْجَنَّةِ، وَغُلِّقَتْ أَبْوَابُ النَّارِ، وَصُفِّدَتِ الشَّيَاطِينُ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 1079]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
"bu Ramadaan ñëwee dañuy tijji bunti àjjana yi, tëj bunti sawara yi, jéng saytaane yi".

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 1079]

Leeral

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne bu weeru koor duggee ñatti mbir day am: Bi ci njëkk: dañuy tijji bunti àjjana yi duñu ci tëj benn bunt. Ñaareel bi: dañuy tëj bunti sawara yi duñu ci tijji benn bunt. Ñatteel bi: dañuy tënk saytaane yi ak jinne yi fétterlu ci ay ceen, duñu leen bàyyi ñuy def la ñu daan def ci bu dul Ramadaan. Loolu lépp nag màggal la ñeel weer wii, ak ug xemmemloo ñeel way-jëf yi ci ñu baril ay jaamu ci julli ak saraxe ak sikar ak jàng Alxuraan ak yu dul yooyu; ak ñu sori bàkkaar yi ak moy yi.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Ngëneelu weeru koor.
  2. Ag bégle la ñeel ñi ciy woor ci ne weer wu baarkel wii ag jamanoy jaamu Yàlla la ak def lu baax.
  3. Tënk gi ñuy tënk saytaane yi ci weeru koor ag junj la ci dindi ngàntal mukallaf mi mu mel ni dañu koy wax ne: fegalees na la saytaane yi kon bul joxe ngànt ci bàyyi jaamu gi du caagine def moy yi.
  4. Al-Xurtubii nee na: bu ñu nee: bu dee da ñuy tënk saytaane yi ci weeru koor gi kon lu tax ñuy gis lu bon ak ay moy Yàlla di am ci weer wi? Tontu li mooy: bàkkaar yi day néew ci woorkat yi woor koor gu jaar yoon, walla tënk gi yenn saytaane yi fétterlu rekk la waaye du yépp, kem ni mu jiitoo ci yenn nettali yi, walla li ñu ci jublu mooy yu bon yi néew gi muy néew ci weer wi, te lii lu ñu yëg la, lu bon limuy am ci weeru koor moo gën a néewe weer yi ci des, ndaxte tënk ñépp it du caagine lo bon du am; ndaxte loolu dafa am yeneen sabab yu dul saytaane niki bakkan bu bon bi, ak aada yu ñaaw yi, ak saytaaney nit yi.
Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Dariya Rom Majri Malagasi Ukraani الجورجية المقدونية الخميرية الماراثية
Gaaral tekki yi