عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ عَنْ رَسُولِ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«قَالَ اللَّهُ تَبَارَكَ وَتَعَالَى: أَعْدَدْتُ لِعِبَادِي الصَّالِحِينَ، مَا لاَ عَيْنٌ رَأَتْ، وَلاَ أُذُنٌ سَمِعَتْ، وَلاَ خَطَرَ عَلَى قَلْبِ بَشَرٍ» قَالَ أَبُو هُرَيْرَةَ: اقْرَؤُوا إِنْ شِئْتُمْ: {فَلاَ تَعْلَمُ نَفْسٌ مَا أُخْفِيَ لَهُمْ مِنْ قُرَّةِ أَعْيُنٍ} [السجدة: 17].
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 4779]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
"Yàlla mu Baarkeel mi te kawe nee na: waajalal naa sama jaam yu sell yi, lu bët musul a gis, nopp musu ko a dégg, te musul a rot ci xolo nit" Abuu Hurayrata nee na: jàngleen bu leen soobee: {benn bakkan xamul la ñu ko dencal ci luy bégloo ay bët} [As-Sajda: 17].
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 4779]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xamle na ne Yàlla mu Baarkeel mi te kawe nee na: Waajalal naa ngir teral ñeel sama jaam yu sell yi ca àjjana lu bët musul a gis jëmmam, te nopp musul a dégg kàddoom, te melokaanam tàbbiwul ci xolu nit. Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm daal di ne: jàngleen bu leen soobee:
{benn bakkan xamul la ñu leen dencal ci luy bégloo ay bët} [As-Sajda: 17].