+ -

عن سهل بن سعد رضي الله عنه عن رسول الله صلى الله عليه وسلم قال:
«مَنْ يَضْمَنْ لِي مَا بَيْنَ لَحْيَيْهِ وَمَا بَيْنَ رِجْلَيْهِ أَضْمَنْ لَهُ الْجَنَّةَ».

[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 6474]
المزيــد ...

Jële nañu ci Sahl Ibn Sahd -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«ku ma sàmmal li ci diggante ay ŋaamam ak li ci diggante ñaari tànkam ma wóoralal ko àjjana».

[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 6474]

Leeral

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ñaari mbir yoy bu jullit taqoog moom day dugg àjjana,
Bi ci njëkk: wattu làmmeñ ci wax luy merloo Yàlla mu kawe mi,
Ñaareel bi: wattu péy mi (awara) ci tàbbi ci ñaawtéef;
Ndax ñaari cér yii dañoo bari lu ñuy tàbbi loo nit ci bàkkaar.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Itaali Oromoo Kanadi البلغارية Asrabijaani الأكانية Usbeg Ukraani الجورجية اللينجالا المقدونية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Wattu làmmeñ ak péy yoonu dugg àjjana la.
  2. Jagleel nañu làmmiñ ak péy cig tudd; ndax ñoom ñaar ñoo gën a rëy ci liy indil nit ki alkandey àdduna ak allaaxira.