Xàjjaley wanqaas yi

Toftaleg Adiis yi

Yàlla dana ko dugal àjjana ak nu jëfam man a toll
عربي Àngale Urdu
ku dajeek Yàlla te bokkaalewu ko ak dara dana dugg àjjana, waaye ku dajeeg moom bokkaaleko ak dara dana dugg sawara
عربي Àngale Urdu
ku ma sàmmal li ci diggante ay ŋaamam ak li ci diggante ñaari tànkam ma wóoralal ko àjjana
عربي Àngale Urdu
àjjana moo gën a jege ku ne ci yeen ay waroy dàllam, sawara it naka noonu
عربي Àngale Urdu
wërale nañu sawara ak ay bànneex, wërale àjjana ak ay naqar
عربي Àngale Urdu
Laaj nañu Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- lan mooy li ëpp luy duggal nit ñi àjjana, mu wax ne: «ragal Yàlla ak rafet jikko
عربي Àngale Urdu
bi Yàlla bindee àjjana ak sawara dafa yónni Jibriil -yal na ko Yàlla dolli jàmm-
عربي Àngale Urdu
danañu indi jenn waay ëllëg bis-pénc, sànni ko ca sawara, buttiti biir yi tasaaroo, mu koy wër kem ni mbaam di wëre ci takkuwaayam
عربي Àngale Urdu
aw doj la wu ñu sànni ca biir sawara diirub juróom-ñaar-fukki at, mooy door a wàcc ca sawara sa leegi ba egg ca suuf
عربي Àngale Urdu
Yàlla mu baarkeel mi te kawe day wax waa àjjana: éey yéen waa àjjana? Ñu ne ko wuyusi nanu la topp nañu la ak mbegte, mu ne leen: ndax gërëm ngeen? Ñu ne ko: lu ñuy teree gërëm te nga jox nu loo joxul kenn ci sa mbindeef yi?
عربي Àngale Urdu
ñaari xaaj a gi nii yu bokk ci waa sawara te gisaguma leen,ay nit yu yor ay yar yu mel ni geeni nag di ci dóor nit ñi,ak ayjigéen yu solu ba noppi rafle, jeng di jengale
عربي Àngale Urdu
dinañu indi dee ci melow kuuy mu duuf
عربي Àngale Urdu
Séen sawara wi ab xaaj la ci juróom-ñaar fukki xaaj ci xaaji sawaraw Jahannama
عربي Àngale Urdu