+ -

عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«صِنْفَانِ مِنْ أَهْلِ النَّارِ لَمْ أَرَهُمَا، قَوْمٌ مَعَهُمْ سِيَاطٌ كَأَذْنَابِ الْبَقَرِ يَضْرِبُونَ بِهَا النَّاسَ، وَنِسَاءٌ كَاسِيَاتٌ عَارِيَاتٌ مُمِيلَاتٌ مَائِلَاتٌ، رُؤُوسُهُنَّ كَأَسْنِمَةِ الْبُخْتِ الْمَائِلَةِ، لَا يَدْخُلْنَ الْجَنَّةَ، وَلَا يَجِدْنَ رِيحَهَا، وَإِنَّ رِيحَهَا لَيُوجَدُ مِنْ مَسِيرَةِ كَذَا وَكَذَا».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2128]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu wax ne : Yonnente Yàlla bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
"ñaari xaaj a gi nii yu bokk ci waa sawara te gisaguma leen,ay nit yu yor ay yar yu mel ni geeni nag di ci dóor nit ñi,ak ayjigéen yu solu ba noppi rafle, jeng di jengale, seeni bopp ya day mel ni jégénu giléem gu jeng,duñu dugg àjjana,te xet ga sax du leen xeeñ,te xetam ga dana toll ci doxub nangam ak sàngam".

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2128]

Leeral

Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-day moytondikuloo ñaari xeeti nit yii bokk ci waa sawara te gisagu leen te amuñu woon ci jamonoom,waaye ci ginnaawam lañuy ñëw:
Xaaj bu njëkk bi:ay nit yu yor ay yor yu mel ni ay geeni nag yu gudd,di ci dóor nit ñi,te ñooy alkaati yi,ak ñiy jàppale tooñkat yi ci dóor nit ñi ci ludul dëgg.
Xaaju ñaareel bi: ay jigéen yu summi yérey fegu ak kersa gi ñu mooñaale jigéen ci cosaan.
Mu melal leen ci ne:dañoo solu ca dëgg-dëgg,daal di rafle ci maanaa;ndax ñoom dañoo sol ay yére yu yaraax di melal seen der,di muur lenni yaram wi difeeñal leneen la;ngir wane seen taar’ Dañuy jengal xoli góor ñi mu jëm ci ñoom ngir seen coliin ak seen wanewu bu ñuy dox, dañuy jengal seeni mbagg, tey jengal ñeneen ñi jëme leen ci jàdd yoon ak ndëngte gi ñu nekk ñoom, Bokk na ci seen i melo: seen bopp yi day mel ni jégénu giléem gu jeng,ñoom dañuy rëyal seen bopp yi di ko ngandeel di ko laxas mbaa luko nuru, Niroole gi ak jégénu giléem nag ngir li seen kawar gi di yëkkatiku la,ak seen létt yi,ak ni muy dammoo ca létt ya ba day jeng jëm ci genn wet ci bopp bi mel ne ni jégénu giléem di jenge. Ku yii melo nekk ci moom kon tëkku gu tar gii mi ngi ci kawam, ci mu bañ a dugg àjjana du gis sax xet ga te du ko jege, te xetu àjjana day xeeñ ci diggante bu sori.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Dañoo araamal dóor nit ñi ak di leen lor ci lu dul njuumte gu ñu def walla bàkkaar bu ñu tàbbi.
  2. Araamal nañu di dimbali tooñkat yi ci seen tooñ gi.
  3. Artu nañu jigéen ñi ci baraj-baraji ak raflewu, ak sol lu xat ak lu yaraax luy melal seen awra wi walla mu koy jëmmal.
  4. Ñaax jigéenu jullit bi ci taqoo ak ndigali Yàlla yi,ak sori lu koy merloo,ba tax muy yayoo allaaxira mbugal mu metti te sax.
  5. Hadiis bi dafa bokk ci yiy tegtale ag yónnenteem moom Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-ndax dafa xibaare ay biri kumpa yu amagul,mu ame na mu ko xibaare woon.