+ -

عَن أَبِي سَعِيدٍ الْخُدْرِيِّ رضي الله عنه أَنَّ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«لَا يَنْظُرُ الرَّجُلُ إِلَى عَوْرَةِ الرَّجُلِ، وَلَا الْمَرْأَةُ إِلَى عَوْرَةِ الْمَرْأَةِ، وَلَا يُفْضِي الرَّجُلُ إِلَى الرَّجُلِ فِي ثَوْبٍ وَاحِدٍ، وَلَا تُفْضِي الْمَرْأَةُ إِلَى الْمَرْأَةِ فِي الثَّوْبِ الْوَاحِدِ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 338]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abii Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mu wax ne:
"góor du xool awray góor, jigéen it du xool awray jigéen,te góor ak góor duñu sàngu ci menn malaan,jigéen ak jigéen it du ñu sàngu ci menn mbalaan .

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 338]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa tere góor di xool awray góor, walla jigéen di xool awray jigéen.
Awra nag: mooy lépp lol bu feeñee nit ki rus, te awray góor mooy li dale ci jumbaxam ba ci wóomam, Jigéen nag léppam awra la ci góori jàmbur,bu dee ci ay jigéen ak ci ñi ko araama takk day feeñal li aadawoo feeñ buy liggéey ci këram.
Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-tere na góor di wéet ak góor ci benn mbalaan te fekk soluñu dara,mbaa jigéen di wéet ak jigéen ci menn malaan walla ci genn càngaay daal di raflewu;ndax loolu man naa tax ku ci ne di laal awray moroomam,te laal ko dañu koo tere kem ni ñu teree xool gi, moom sax nag moo gën a tar ug tere;ndax yàqute yi muy indi moo gën a rëy.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Ciikiya Malagasi Oromoo Kanadi
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Tere nañu di xool awray keneen ba mu des jëkkër ji ak jabaram.
  2. Xérug Lislaam ci laabal mbooloo mi ak tëj bunt yiy indi ñaawteef.
  3. Dagan na ñu xool awray keneen bu dee aajo moo ko waral, niki faj ak lu ko niru, ci kaw mu nekk ci ludul bànneexu.
  4. Jullit bi dañu koo digal mu muur awraam te dammu gisam ci awray keneen.
  5. Dañoo jagleel tere gi góor ak góor, ak jigéen ak jigéen; ngir moo gën a man a waral xool awray keneen ak wuññi awra.