عن أبي هريرة رضي الله عنه قال:
لعن رسول الله صلى الله عليه وسلم الرجل يلبس لِبْسَةَ المرأة، والمرأة تلبس لِبْسَةَ الرجل.
[صحيح] - [رواه النسائي في الكبرى وابن ماجه بمعناه وأحمد] - [السنن الكبرى للنسائي: 9209]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc rëbb na góor giy sol colug jigéen, ak jigéen giy sol colug góor.
[Wér na] - - [Téere bu mag bi An-nasaa'iy def ci Sunna yi - 9209]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñaan na ag dàq ak soril yërmàndey Yàlla ñeel góor giy niru-nirulu jigéen ci sol yi jigéen ñi jagoo; moo xam ca jëmm ja la walla ca melo wa walla ca anam ga walla ca anamug coliin ga ak taar ba walla yu dul yooyu. Walla jigéen gi di ko niru-nirulu ci col gi góor ñi jagoo, moom nag ci bàkkaar yu mag yi la bokk.