عَنْ أَبِي سَعِيدٍ الْخُدْرِيِّ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«لَتَتَّبِعُنَّ سَنَنَ الَّذِينَ مِنْ قَبْلِكُمْ، شِبْرًا بِشِبْرٍ، وَذِرَاعًا بِذِرَاعٍ، حَتَّى لَوْ دَخَلُوا فِي جُحْرِ ضَبٍّ لَاتَّبَعْتُمُوهُمْ» قُلْنَا: يَا رَسُولَ اللهِ آلْيَهُودَ وَالنَّصَارَى؟ قَالَ: «فَمَنْ؟».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 2669]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«dangeen topp yooni ña leen jiitu woon, sibre ak sibre, loxo ak loxo, ba bu ñu duggoon ci paxum mbëtt ngeen topp leen ca" nu ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, ndax Yahuut yi la ak nasaraan yi? Mu ne: "bu dul ñoom ñan la?».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2669]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare nekkiinu ñenn ci aw xeetam ginnaaw jamonoom, te mooy topp yoonu Yahuut yi ak nasaraan yi ci seeni pas-pas ak seeni jëf ak seeni aada, ak seeni cosaan topp gu sew lool sibre ci sibre, loxo ci loxo, ba bu ñu duggoon ci paxum mbëtt sax ñoom ñu dugg ca topp ci seen ginnaaw.