عن ابْنِ عُمَرَ رضي الله عنهما أنه سَمِعَ رَجُلًا يَقُولُ: لَا وَالْكَعْبَةِ، فَقَالَ ابْنُ عُمَرَ: لَا يُحْلَفُ بِغَيْرِ اللَّهِ، فَإِنِّي سَمِعْتُ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَقُولُ:
«مَنْ حَلَفَ بِغَيْرِ اللهِ فَقَدْ كَفَرَ أَوْ أَشْرَكَ».
[صحيح] - [رواه أبو داود والترمذي وأحمد] - [سنن الترمذي: 1535]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abdallah ibnu Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- ci ne dégg na benn waay di wax naan: giñ naa ci Kaaba gi, Ibnu Umar ne ko: deesul giñ ci ku dul Yàlla, man dégg naa Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan:
«ku giñ ci ku dul Yàlla weddi na walla bokkaale na».
[Wér na] - [Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 1535]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- day xamle ne képp ku giñ ci ku dul Yàlla te du ay Turam ak i Meloom weddi na walla bokkaale na; ndax giñ day waral màggal ki ñuy giñ ci moom, te màggal Yàlla rekk la ñeel; kon deesul giñ ci ku dul Yàlla walla ay Turam ak i Meloom -tudd naa sellam ga-. Giñ gii nag ci bokkaale gu ndaw la bokk; waaye kiy giñ bu màggalee la muy giñe kem ni ñuy màggale Yàlla mbaa lu ko ëpp; bu boobaa day nekk bokkaale gu mag.