عَنْ أَنَسِ بْنِ مَالِكٍ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«مَنْ عَالَ جَارِيَتَيْنِ حَتَّى تَبْلُغَا جَاءَ يَوْمَ الْقِيَامَةِ أَنَا وَهُوَ» وَضَمَّ أَصَابِعَهُ.
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2631]
المزيــد ...
Jële nañu ci Anas Ibn Maalik yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
"ku dundal ñaari jigéen ba ñu mat, dana ñëw ëllëg bis-pénc man ak moom" mu tàppale ay baaraamam.
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2631]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne ku ñu wërsëgale ay doom yu jigéen walla ay rakk yu jigéen, mu dundal leen yar leen jubbanti leen jëme leen ci yiw ak moytu lu bon ak yi ko niru ba nu màgg ba mat; dana ñëw ëllëg bis-pénc moom ak Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mel ni ñaar yii, mu kebale baaraamu sànnikaay bi ak bi ci digg bi.