+ -

عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«لَا تَدْخُلُونَ الْجَنَّةَ حَتَّى تُؤْمِنُوا، وَلَا تُؤْمِنُوا حَتَّى تَحَابُّوا، أَوَلَا أَدُلُّكُمْ عَلَى شَيْءٍ إِذَا فَعَلْتُمُوهُ تَحَابَبْتُمْ؟ أَفْشُوا السَّلَامَ بَيْنَكُمْ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 54]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«dungeen dugg àjjana ndare ngeen gëm, te dungeen gëm ndare ngeen bëggante, moo ndax duma leen tegtal lol su ngeen ko defee dangeen bëggante? Siiwalleen ab nuyóo seen diggante».

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 54]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne kenn du dugg àjjana lu dul way-gëm ñi, te gëm du mat, mbiri mbooloom jullit ñi tamit du yéwen ba keroog ñenn ñi bëgg ñeneen ñi. Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wane mbir yi gën yoy ci la bëggante di ame, te mooy tasaare nuyóog jàmm ci diggante jullit ñi, nuyóo bi Yàlla def muy nuyyoob jaamam ñi.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Almaa Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Asrabijaani Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Dugg àjjana du ame ci lu dul ngëm.
  2. Bokk na ci matug ngëm jullit bi bëggal mbokku jullitam li mu bëggal boppam.
  3. Sopp nañu tasaare ab nuyóo ak di ko defal jullit ñi; ndax li ci nekk ci tasaare bëggante ak kóolute ci diggante nit ñi.
  4. Nuyoob lislaam duñu ko defal ku dul ab jullit; ndax li Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax ne: "seen diggante".
  5. Nuyoob lislaam dana dindi dogante ak bàyyeente ak mbañeel.
  6. Solos bëggante ci diggante jullit ñi,ci ne daa bokk ci liy matal ngëm.
  7. Ñëw na ci beneen hadiis ne nuyóo bu mat sëkk mooy: "assalaamu halaykum wa rahmatul Laahi wa barakaatuhu", "assalaamu halaykum" it dana doy.