+ -

عن أبي هريرة رضي الله عنه عن النبي صلى الله عليه وسلم:
«اللهُمَّ لَا تَجْعَلْ قَبْرِي وَثَنًا، لَعَنَ اللهُ قَوْمًا اتَّخَذُوا قُبُورَ أَنْبِيَائِهِمْ مَسَاجِدَ».

[صحيح] - [رواه أحمد] - [مسند أحمد: 7358]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
"yaw sama Boroom maa ngi lay ñaan bul def sama bàmmeel ab xërëm, Yàlla rëbb na nit ñiy jàppe bàmmeelu seeni Yónente ay jàkka".

[Wér na] - [Ahmat soloo na ko] - [Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya - 7358]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- dafa ñaan Boroomam mu bañ a def bàmmeelam ab xërëm bu nit di jaamu ci di ko màggal, ak di ko jublu buy sujjóot. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-wax na ne Yàlla soreele na yërmaandeem képp kuy jàppe bàmmeel i Yónente yi ay jàkka; ndax jàppe ko ay jàkka yoon wu jëm ci jaamu ko la ak di ci am ay pas-pas.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Itaali Oromoo Kanadi البلغارية Asrabijaani الأكانية Usbeg Ukraani الجورجية اللينجالا المقدونية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Jéggi dayob sariiha ci bàmmeel i Yónent yi ak ñu baax ñi day tax ñu di ko jaamu bàyyi fi Yàlla, moo tax ñu war a moytu luy jëme deci bokkaale.
  2. Daganul di dem ci ay bàmmeel ngir màggal ko ak di fa def ag jaamu ak lu boroomam man a jege Yàlla mu kawe mi.
  3. Tabax jàkka ci bàmmel yi dafa araam.
  4. Julli ci bàmmeel yi dafa araam, doonte tabaxuñu ko jàkka, lu dul julleeb néew bi nga xam ne julleewuñu ko woon.