عَنِ النُّعْمَانِ بْنِ بَشِيرٍ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُمَا عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«مَثَلُ القَائِمِ عَلَى حُدُودِ اللَّهِ وَالوَاقِعِ فِيهَا، كَمَثَلِ قَوْمٍ اسْتَهَمُوا عَلَى سَفِينَةٍ، فَأَصَابَ بَعْضُهُمْ أَعْلاَهَا وَبَعْضُهُمْ أَسْفَلَهَا، فَكَانَ الَّذِينَ فِي أَسْفَلِهَا إِذَا اسْتَقَوْا مِنَ المَاءِ مَرُّوا عَلَى مَنْ فَوْقَهُمْ، فَقَالُوا: لَوْ أَنَّا خَرَقْنَا فِي نَصِيبِنَا خَرْقًا وَلَمْ نُؤْذِ مَنْ فَوْقَنَا، فَإِنْ يَتْرُكُوهُمْ وَمَا أَرَادُوا هَلَكُوا جَمِيعًا، وَإِنْ أَخَذُوا عَلَى أَيْدِيهِمْ نَجَوْا، وَنَجَوْا جَمِيعًا».
[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 2493]
المزيــد ...
Jële nañu ci An-Nuhmaan Ibn Basiir -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
"misaalu ki taxaw ci foroñceeri Yàlla yi ak ki ci tàbbi, moo ngi mel ni aw nit wu tegoo bant ci ag gaal, ñii am kaw ga, ñii nekk ca suuf ga, ñi nekk ci suuf bu ñuy wut ndox dañuy romb ña nekk seen kaw, nu mujj wax ne: nun de bu nu xaroon ci sunu wàll aw xarit te dunu lor ñi nekk sunu kaw, bu ñu leen bàyyee ak la ñu bëgg ñoom ñéppay alku, waaye bu ñu téyee seen loxo danañu mucc, ñoom ñépp mucc".
[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 2493]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa sadd misaal ñeel ñi taxaw ci foroñceeri Yàlla yi, ne coww ci ay ndigalam, di digle lu baax di tere lu bon, Ak misaalu ñiy tàbbi ci foroñceeri Yàlla yi bàyyi ndigle yi, di def tere yi, ak jeexitalu loolu ci muccug mbooloo mi, mu mel ni aw nit wu war ci ag gaal, ñu daal di sànni bant ngir xam kuy toog ci kaw gaal gi ak kuy toog ci suuf, ñenn ñi am kaw ga, ñeneen ñi am suuf ga, ñi nekkoon ci suuf bu ñu bëggee wut ndox dañuy romb ña ca kaw, Ñi nekk ci suuf daal di wax ne: nun de bu nu xaroon aw xar ci su nu bérab fii ci suuf ngir di ci wute ndox, ba dunu lor ñi nekk fi sunu kaw, ñi nekk ci kaw buñu leen bàyyee ba ñu def loolu, kon gaal gi dana leen suuxal ñoom ñépp, waaye bu ñu jugee tere leen ko, ñaari kurél yépp danañu mucc.