عَنْ أَبِي سَعِيدٍ الخُدْرِيِّ رضي الله عنه أَنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«إِنَّ مِنْ أَعْظَمِ الجِهَادِ كَلِمَةَ عَدْلٍ عِنْدَ سُلْطَانٍ جَائِرٍ».
[حسن لغيره] - [رواه أبو داود والترمذي وابن ماجه وأحمد] - [سنن الترمذي: 2174]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abii Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
"bokk na ci jihaad yi gën a màgg wax kàddug maanute fi kanamu buur
bu jeng ».
- [Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 2174]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day leeral ne bokk na ci xeeti jihaad ci yoonu Yàlla yi gën a màgg te ëpp njariñ mooy wax baati maandute ag dëgg fi kanamu buur ak njiit lu jeng di ab tooñkat; ndaxte moom dafa jëfe jaamug digle lu baax ak tere lu bon, moo xam ci wax la walla ci bind walla ci jëf mbaa leneen lu yéwénal di ame te yàqute di ca dàqoo.