عن عبد الله بن عمرو بن العاص رضي الله عنهما عن النبي صلى الله عليه وسلم قال:
«الْكَبَائِرُ: الْإِشْرَاكُ بِاللهِ، وَعُقُوقُ الْوَالِدَيْنِ، وَقَتْلُ النَّفْسِ، وَالْيَمِينُ الْغَمُوسُ».
[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 6675]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abdulaa Ibn Amr Ibnul Haas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«bàkkaar yu mag yi mooy: bokkaale Yàlla, ak dënge ñaari way-jur, ak ray bakkan, ak giñ guy nuuralaate».
[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 6675]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral bàkkaar yu mag yi, te mooy gu ñu tëkku aji-def ji ci tëkku gu tar ci àdduna walla allaaxira.
Bu njëkk bi "Bokkaale Yàlla": te mooy def wenn xeetu jaamu ñeel ku dul Yàlla, ak yamale lenn ak Yàlla ci lu Yàlla jagoo, cig jaamu, ak ug moomeelam ak ci ay turam ak i meloom.
Ñaareel bi "Dënge ñaari way-jur": te mooy lépp luy waral lor ñaari way-jur moo xam wax la walla jëf, ak bàyyee rafetal jëme ci ñoom ñaar.
Ñatteel bi "ray bakkan": ci lu dul dëgg, niki ray ko cig tooñ ak ug jalgati.
Ñenteel bi "ngiñ luy nuural nit ": te mooy giñ lu waay def di fen te xam ne day fen, dañu koo tudde loolu nag; ngir ne day nuural boroomam ci ay bàkkaar walla ci sawara.