+ -

عَنْ جَابِرِ بْنِ عَبْدِ اللهِ رضي الله عنهما أَنَّهُ سَمِعَ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَقُولُ:
«إِذَا دَخَلَ الرَّجُلُ بَيْتَهُ، فَذَكَرَ اللهَ عِنْدَ دُخُولِهِ وَعِنْدَ طَعَامِهِ، قَالَ الشَّيْطَانُ: لَا مَبِيتَ لَكُمْ، وَلَا عَشَاءَ، وَإِذَا دَخَلَ، فَلَمْ يَذْكُرِ اللهَ عِنْدَ دُخُولِهِ، قَالَ الشَّيْطَانُ: أَدْرَكْتُمُ الْمَبِيتَ، وَإِذَا لَمْ يَذْكُرِ اللهَ عِنْدَ طَعَامِهِ، قَالَ: أَدْرَكْتُمُ الْمَبِيتَ وَالْعَشَاءَ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2018]
المزيــد ...

Jële nañu ci Jaabir ibn Abdallah -yal na leen Yàlla dollee gërëm- ne moom dégg na Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
« bu nit ki duggee këram, daal di tudd Yàlla buy dugg ak buy lekk, saytaane day wax naan: amuleen fanaanukaay, amuleen reerukaay, bu duggee te tuddul Yàlla, bi muy dugg, saytaane day wax naan: am ngeen fanaanukaay, bu tuddul Yàlla bu dee lekk, mu wax: am ngeen fanaanukaay ak reerukaay ».

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2018]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa digle tudd Yàlla bu ñuy dugg ci kër ak balaa ñuy lekk, ak ne bu ñu tudee Yàlla wax: (bismil Laah) bu ñuy dugg ci kër gi ak bu ñuy tàmbalee lekk, saytaane day wax ay gaayam naan: manu leen fanaan, te du ngeen man a reer ci kër gii boroom aaroo ci tudd Yàlla mu kawe mi. Bu nit ki duggee këram nag te tuddul Yàlla bi muy dugg ag ,bi muy lekk, saytaane day wax ay gaayam ne leen am ngeen am panaan, ak ub reer ci kër gii.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Sopp nañu tudd Yàlla bu ñuy dugg ci kër ak bu ñuy lekk, ndax Saytaane day fanaan ci kër gi,di lekk ci lekku waa kër gi, bu ñu tuddul Yàlla mu kawe mi.
  2. Saytaane day ànd ak doomu Aadama ji ci jëfam, di ko wëlbati ci ay biram yépp, te bu sàgganee tudd Yàlla dana am li mu bëgg ci moom.
  3. Tudd Yàlla day dàq saytaane.
  4. Saytaane su nekk am na ñu koy topp ak ñu far ak moom di bége ay waxam tey topp ay ndigalam.
Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Taylandi Almaa Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Asrabijaani Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi