+ -

عَنْ عَائِشَةَ أُمِّ المؤمنين رضي الله عنها:
أَنَّ أُمَّ سَلَمَةَ ذَكَرَتْ لِرَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ كَنِيسَةً رَأَتْهَا بِأَرْضِ الْحَبَشَةِ، يُقَالُ لَهَا مَارِيَةُ، فَذَكَرَتْ لَهُ مَا رَأَتْ فِيهَا مِنَ الصُّوَرِ، فَقَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «أُولَئِكَ قَوْمٌ إِذَا مَاتَ فِيهِمُ الْعَبْدُ الصَّالِحُ، أَوِ الرَّجُلُ الصَّالِحُ، بَنَوْا عَلَى قَبْرِهِ مَسْجِدًا، وَصَوَّرُوا فِيهِ تِلْكَ الصُّوَرَ، أُولَئِكَ شِرَارُ الْخَلْقِ عِنْدَ اللهِ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 434]
المزيــد ...

Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne :
Ummu Salamata dafa xibaar Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- benn jàngu bu mu gis ca Abasa, (jàngu : jaamukaayu katolig yi) ñu koy woowe Maariya, mu wax ko la mu fa gis ci ay nataal, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: " ñooñu aw nit lañu wow bu ku baax faatoo fa ñoom, dañuy tabax ca bàmmeelam ba jàkka, daaldi cay def nataal yooyu, ñooñu ñoo yées ci nit ñi fa Yàlla".

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 434]

Leeral

Ndayu jullit ñi Ummu Salamata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- dafa nettali Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne moom ba mu nekkee ca suufus Abasa dafa gis ab jàngu ñu koy woowe Maariya- ay nataal ak i rafetal ak i rëd-rëd ñoo fa nekk; mu yéemu ci loolu ! Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeral li waral ñu def fa foto yooyu; Mu wax ne : ñii ngay wax bu amaan ku baax ku faatu ci ñoom dañuy tabax jàkka ci kaw bàmmeelam di fa julli, daa di fay def nataal yooyu, Mu leeral ne ñiy def loolu ñoo yées ci mbindeef yi fa Yàlla, ndax seen i jëf da lay yóbbe ci bokkaale Yàlla mu kawe mi.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Ciikiya Malagasi Oromoo Kanadi Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Tabax jàkka ci bàmmeel yi dafa araam, walla di fa julli, mbaa suul néew ci jàkka yi; ngir sakk yoon yiy jëme ci bokkaale.
  2. Tabax jàkka ci bàmmeel yi, ak samp fa ay nataal, daa bokk ci jëfi Yahuut yi ak Nasaraan yi, te ku ko def, mi ngi leen di niru-nirulu.
  3. Araamalees na nataal lu am ruu.
  4. Ku tabax jàkka cib bàmmeel def fa ay nataal, kon moom ci ñi yées ci mbindeefi Yàlla yi la bokk.
  5. Sariiha dafa aar Tawhiid aar gu mat sëkk, ci fatt wépp yoon wuy jëme ci bokkaale.
  6. Tere nañu ëppal ci ñu baax ñi; ndaxte sabab la ci tàbbi ci bokkaale.