+ -

عَنْ مَحْمُودِ بْنِ لَبِيدٍ رضي الله عنه أَنَّ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«إِنَّ أَخْوَفَ مَا أَخَافُ عَلَيْكُمُ الشِّرْكُ الْأَصْغَرُ» قَالُوا: وَمَا الشِّرْكُ الْأَصْغَرُ يَا رَسُولَ اللهِ؟ قَالَ: «الرِّيَاءُ، يَقُولُ اللهُ عز وجل لَهُمْ يَوْمَ الْقِيَامَةِ إِذَا جُزِيَ النَّاسُ بِأَعْمَالِهِمْ: اذْهَبُوا إِلَى الَّذِينَ كُنْتُمْ تُرَاؤُونَ فِي الدُّنْيَا، فَانْظُرُوا هَلْ تَجِدُونَ عِنْدَهُمْ جَزَاءً؟».

[حسن] - [رواه أحمد] - [مسند أحمد: 23630]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Mahmuud Ibn Labiid -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«li ma gën a ragal ci yéen mooy bokkaale gu ndaw" ñu ne ko: lan mooy bokkaale gu ndaw yaw Yonnente Yàlla bi? Mu ne leen: "ngistal, ngistalkat yi Yàlla da leen di wax ëllëg bis-pénc bu ñu faayee nit ñi seen jëf ba noppi: demleen ca ña ngeen doon ngistal ca àdduna, ngeen xool ba xam ndax dangeen fekk fa ñoom ag pay?"

[Tane na] - [Ahmat soloo na ko] - [Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya - 23630]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne mbir mi mu gën a ragal ci xeetam wi mooy: bokkaale gu ndaw te mooy: ngistal; di def ngir nit ñi. Mu xibaare ne mbugalum ñiy ngistal ëllëg bis-pénc mooy ñu ne leen: demleen ca ña taxoon ngeen doon jëf, ngeen xool ndax danañu am yool ak pay gu ñu leen di fay ca seen jëf yooya?!

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Asrabijaani Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Dañoo war a sellal jëf yi ngir Yàlla mu màgg mi, te moytu ngistal.
  2. Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa ñeewante lool aw xeetam te xér ci gindi leen ak di leen laabire.
  3. Bu dee nii la ragalug Yonnente bi toll te muy wax ak sahaaba yi, te ñoom ñooy sangi ñu baax ñi, kon ragal ci ñiy ñëw seen ginnaaw mooy gën a tar.