عن جابر بن عبد الله رضي الله عنهما قال: سمعت رسول الله صلى الله عليه وسلم يقول:
«مَنْ لَقِيَ اللهَ لَا يُشْرِكُ بِهِ شَيْئًا دَخَلَ الْجَنَّةَ، وَمَنْ لَقِيَهُ يُشْرِكُ بِهِ دَخَلَ النَّارَ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 93]
المزيــد ...
Jële nañu ci Jaabir Ibn Abdallah -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan:
«ku dajeek Yàlla te bokkaalewu ko ak dara dana dugg àjjana, waaye ku dajeeg moom bokkaaleko ak dara dana dugg sawara».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 93]
Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamale ne ku faatu te bokkaalewul Yàlla ak dara kon jëmuwaayam mooy àjjana doonte sax mbugël nañu ko ci yennati bàkkaaram, waaye ku faatu fekk doon na bokkaale Yàlla ak dara dana sax sawara.