+ -

عَنْ عَبْدِ اللهِ بنِ مَسْعُودٍ رضي الله عنه قال:
قَالَ النَّبِيُّ صلى الله عليه وسلم كَلِمَةً وَقُلْتُ أُخْرَى، قَالَ النَّبِيُّ صلى الله عليه وسلم: «مَنْ مَاتَ وَهُوَ يَدْعُو مِنْ دُونِ اللهِ نِدًّا دَخَلَ النَّارَ» وَقُلْتُ أَنَا: مَنْ مَاتَ وَهُوَ لَا يَدْعُو لِلهِ نِدًّا دَخَلَ الْجَنَّةَ.

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 4497]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- me wax ne:
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax na jenn wax, ma wax Jeneen wax, yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa wax ne: " ku faatu fekk moo ngi wutal Yàlla ndend dana dugg sawara" man ma ne: ku faatu te wutalul Yàlla ndend dana dugg àjjana.

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 4497]

Leeral

yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne ku jël lu Yàlla jagoo jëme ko ci ku dul moom, niki ñaan ku dul Yàlla mu kawe mi, ak xettaliku ci keneen, daal di faatu ca loola kooku ci waa sawara lay bokk. Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- teg ca ne ku faatu te bokkaalewul Yàlla ak dara kooku mujjam mooy àjjana.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Asrabijaani Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Ñaan de ag jaamu la, deesu ko defal ku dul Yàlla mu kawe mi.
  2. Ngëneelu Tawhiid, ak ne ku ca faatu dugg àjjana, donte dañu koo mbugal ci yenn bàkkaaram yi.
  3. Loràngey bokkaale, ci ne képp ku ci faatu dina dugg sawara.