+ -

عن أبي هريرة رضي الله عنه أن رسول الله صلى الله عليه وسلم قال:
«حُجِبَتِ النَّارُ بِالشَّهَوَاتِ، وَحُجِبَتِ الْجَنَّةُ بِالْمَكَارِهِ».

[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 6487]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«wërale nañu sawara ak ay bànneex, wërale àjjana ak ay naqar».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere bu wér bi ñeel Ibnu Hibbaan - 6487]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne sawara dañu koo wërale ak i mbir yoy bakkan da koo bëgg, ci jëf yu araam yi, ag gàtteñlu ci yu war yi; Ku topp bànneexam ci loolu kon yeyoo na sawara, Àjjana nag lu ñu muur la wërale ko ak ay mbir yoy bakkan da koo bañ; niki sax ci def ndigal yi bàyyi tere yi te muñ ca, bu dëgëree xeex ak bakkanam ci loolu kon yayoo na dugg àjjana.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Asrabijaani Usbeg Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bokk na ci liy tax a tàbbi ci bànneex yi li Saytaane di taaral lu bon ak lu ñaaw, ba mujj bakkan bi di ko gise lu rafet daal di jeng jëm ca.
  2. Digle ñu sori bànneex yi ñu araamal; ndax te yoonu sawara la, ak muñ ci yu naqari yi ndax te yoonu àjjana la.
  3. Ngëneelu xeex ak bakkan, ak farlu ci jaamu yi, ak muñ ci yu naqari yi ak coono yi wër topp yi.