عَنْ أَبِي سَعِيدٍ الْخُدْرِيِّ وَعَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنهما عَنِ النَّبِيِّ صلى الله عليه وسلم قَالَ:
«مَا يُصِيبُ الْمُسْلِمَ مِنْ نَصَبٍ وَلَا وَصَبٍ وَلَا هَمٍّ وَلَا حُزْنٍ وَلَا أَذًى وَلَا غَمٍّ حَتَّى الشَّوْكَةِ يُشَاكُهَا إِلَّا كَفَّرَ اللهُ بِهَا مِنْ خَطَايَاهُ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 5641]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu, ak Abuu Hurayrata -yal na leen Yàlla dollee gërëm- ñu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«Amul benn coono buy dal ab jullit, mbaa tawat walla, jaaxle, mbaa naqar, loraange, walla njàqare, doonte dég gu ko jam la, lu dul ne Yàlla dina ca fare yenn ci ay bàkkaaram».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 5641]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne liy dal jullit bi ci ay feebar ak i naqar ak i tiitaange ak i coono ak i musiba, ak ay tar-tar ak ragal, ak ub xiif -ba ci dég gu ko jam ba mettital ko-, loolu day far ay bàkkaaram di sippi ay ñaawtéefam.