+ -

عن أنس بن مالك رضي الله عنه قال:
كَانَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ أَحْسَنَ النَّاسِ خُلُقًا.

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 2310]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik, -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- moo gënoon a rafet jikko ci nit ñi.

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2310]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- moo gënoon a mat jikko ci nit ñi, mbooleem jikko yu rafet yi moo ca jiitu, ci wax ju teey, ak jëf ju yiw, ak béllil xar kanam, ak téye lor te muñ ko ci ñeneen ñi.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Malagasi Itaali Kanadi Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Matug jikkoy Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.
  2. Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mooy royukaay bu mat bi ci rafet jikkó.
  3. Ñaaxe ci roy Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci rafet jikkó.