عن أبي هريرة رضي الله عنه قال:
كان رسولُ الله صلى الله عليه وسلم إذا عَطَس وضَعَ يَدَه -أو ثوبَهُ- على فيهِ، وخَفَضَ -أو غضَّ- بها صوتَهُ.
[صحيح] - [رواه أبو داود والترمذي وأحمد] - [سنن أبي داود: 5029]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan tissooli day teg loxoom -walla yéereem- ci gémmeñam, daal di suufeel -walla mu téye- ci kàdoom.
[Wér na] - [Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 5029]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan tissooli:
Li ci njëkk: day teg loxoom, walla yeéreem ci gémmeñam; ngir dara bañ a génn ci gémmeñam walla bakkanam luy lor ñi mu toogal.
Ñaareel bi: day suufeel kàddoom te du ko yëkkati.