+ -

عن أبي هريرة رضي الله عنه قال: سمعت رسول الله صلى الله عليه وسلم يقول:
«حَقُّ الْمُسْلِمِ عَلَى الْمُسْلِمِ خَمْسٌ: رَدُّ السَّلَامِ، وَعِيَادَةُ الْمَرِيضِ، وَاتِّبَاعُ الْجَنَائِزِ، وَإِجَابَةُ الدَّعْوَةِ، وَتَشْمِيتُ الْعَاطِسِ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 1240]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne:
«àqi jullit ci moroomu jullitam juróom la: delloo ab nuyoo, ak seeti ki wopp, ak gunge néew bi, ak wuyu woote ba, ak ndokkeel ku tissooli».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere bu wér bi ñeel Ibnu Hibbaan - 1240]

Leeral

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral yénn àqi jullit bi ci mbokku jullitam, Bi njëkk ci àq yii mooy delloo nuyoo ñeel ku la nuyu.
Àqu ñaareel bi: seeti ku feebar.
Àqu ñatteel bi: gunge ab néew ci këram ba ca jullikaay ba, ba ca almeer ya ba ba ñu koy rob.
Àqu ñenteel bi: wuyu woote ba bu ñu ko woowee ci céetal ab séet mba leneen.
Àqu jurómeel bi: ndokkeel Ku tissooli, te mooy mu wax ko ndeem sant na Yàlla: yarhamulallaah, aji-tissooli ji wax: yahdiikumullaahu wa yuslihu baalakum.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Asrabijaani Usbeg Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Màggug Lislaam ci di feddali àq yi dox diggante jullit ñi, ak di dëgëral mbokkoo ak bëggante seen diggante.