عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه أَنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«خَيْرُ يَوْمٍ طَلَعَتْ عَلَيْهِ الشَّمْسُ يَوْمُ الْجُمُعَةِ، فِيهِ خُلِقَ آدَمُ، وَفِيهِ أُدْخِلَ الْجَنَّةَ، وَفِيهِ أُخْرِجَ مِنْهَا، وَلَا تَقُومُ السَّاعَةُ إِلَّا فِي يَوْمِ الْجُمُعَةِ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 854]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
« bis bi gën ci bis yi mooy bisu àjjuma, ci lañu bind Aadama, ci lañu ko duggal àjjana, ci lañu ko ca génne, te Saa du taxaw ci lu dul bisu àjjuma ».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 854]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne bis bi gën ci bis yi mooy bisub àjjuma, Te bokk na ci ay jagleem: ci la Yàlla bind Aadama -yal na jàmm nekk ci moom- te ci la ko duggale àjjana, te ci la ko ca génnee wàcce ko ci kaw suuf, te Saa du taxaw ci li dul bisub àjjuma.