+ -

عَنْ عَبْدِ اللَّهِ بنِ مسعُودٍ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ قَالَ:
ذُكِرَ عِنْدَ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ رَجُلٌ نَامَ لَيْلَهُ حَتَّى أَصْبَحَ، قَالَ: «ذَاكَ رَجُلٌ بَالَ الشَّيْطَانُ فِي أُذُنَيْهِ، أَوْ قَالَ: فِي أُذُنِهِ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 3270]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abdullah Ibn Mashuud yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Dañoo tudd fi Yonnente bi jenn waay bu nelaw guddeem gi yépp ba suba jot, mu ne: "kooku mooy ki nga xam ne saytaane daa saw ci ay noppam, walla mu wax: ci noppam".

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 3270]

Leeral

Dañoo tudd fi Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc jenn waay ju nelaw ba suba jot jant bi fenk te jugul julli farata gi, Yonnente bi daa di ne: waa jooju saytaane moo saw ci nopp bi.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Sib nañu bàyyi taxaw guddi, ak ne loolu saytaane moo ko sabab.
  2. Moytandiku saytaane mi nga xam ne day toog ci yoonu nit ki; ngir dox ci digganteem ak topp Yàlla mu màgg mi.
  3. Ibn Hajar nee na: li mu wax: (jugul jëm ci julli gi) li ñu ci namm mooy xeetu julli rekk, jamtal na it muy gu ñu xam, ñu namm ci julli guddi, walla gu farata.
  4. At-Tiibii nee na:tudd gi ñu tudd nopp donte bët moo gën a méngoo ak nelaw, loo lu junj la ci diisug nelaw yi, ndax nopp yi la ñuy bàyyee xel, tudd nañu saw ndaxte moo gën a yomb te gën a gaaw a jàll ca séddit ya, ba tax muy waral tàyyeel ci mbooleem cér yi.
Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Nipali Dariya Rom Majri الموري Ukraani الجورجية المقدونية الخميرية الماراثية
Gaaral tekki yi