عن عمرو بن شُعيب عن أبيه عن جدِّه قال: قال رسولُ الله صلى الله عليه وسلم:
«مُرُوا أولادكمِ بالصلاةِ وهم أبناءُ سبعِ سِنينَ، واضرِبوهم عليها وهم أبناءُ عَشرٍ، وفرِّقوا بينهم في المَضاجِعِ».
[حسن] - [رواه أبو داود] - [سنن أبي داود: 495]
المزيــد ...
Jële nañu ci Amr ibn Suhaybu mu jële ci baayam mu jële ci maamam mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«digalleen seen doom yi ñuy julli bu ñu amee juróom-ñaari at, te ngeen leen di dóor ci loolu bu ñu amee fukki at,te ngeen teqale seen diggante ca tëddukaay ya».
[Tane na] - [Abóo Daawuda soloo na ko] - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 495]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-day leeral ne war na ci baay bi mu digal ay doomam-góor ñi ak jigéen ñi- ñuy julli bu ñu amee juróom-ñaari at,mu xamal leen li ñu aajowoo ngir taxawal ko. Bu ñu matalee fukki at mu dolli ca ndigal la, di leen dóor ci bi ñu ca gàtteñloo, te teqale seen diggante ca lal ba.