عن بريدة بن الحصيب رضي الله عنه أنه قال:
بَكِّرُوا بِصَلَاةِ الْعَصْرِ، فَإِنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ: «مَنْ تَرَكَ صَلَاةَ الْعَصْرِ فَقَدْ حَبِطَ عَمَلُهُ».
[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 553]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Buraydata Ibn Al-Husaybi -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Deeleen teel a julli tàkkusaan, ndax yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "ku bàyyi jullig tàkkusaan jëfam yàquna".
[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 553]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- artu na ci yeexe jullig tàkkusaan ca waxtoom te tay ko, ak ne ku def loolu jëfam yàquna te ag neen la.