عن عثمان بن عفان رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«مَنْ تَوَضَّأَ فَأَحْسَنَ الْوُضُوءَ خَرَجَتْ خَطَايَاهُ مِنْ جَسَدِهِ حَتَّى تَخْرُجَ مِنْ تَحْتِ أَظْفَارِهِ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 245]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Usmaan Ibn Affaan -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«Ku jàpp te rafetal njàpp ma, ay ñaawtéefam day génn ci aw yaramam bay génn ci ay weyam».

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 245]

Leeral

yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ku jàpp sàmmoonte ak Sunnay Njàpp ak i tegginam, loolu sabab la ci far ay ñaawtéef ak sippi ay ñuumte, "ba ay bàkkaaram di génne ci ay suufi weyi loxoom ak i tànkam"

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Ñaaxe ci yittewoo jàng njàpp ak i sunnaam ak i tegginam, ak jëfe ko.
  2. Ngëneelu jàpp, ci ne day far bàkkaar yu ndaw yi, bu dee yu mag yi nag tuub rekk a koy far.
  3. Sàrt yiy tax bàkkaar yi génn mooy matal njàpp mi te moytu lu koy yàq kem ni ko yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leerale.
  4. Dindi bàkkaar yi ci hadiis bii dañu koo tënk ci moytu bàkkaar yu mag yi ak tuub ko, Yàlla mu kawe mi nee na: (bu ngeen moytoo bàkkaar yi ñu leen tere nu far séen i ñaawtéef) [An-Nisaa].
Gaaral tekki yi
Làkk: Àngale Urdu Español Ndollent (62)