عن أبي الدرداء رضي الله عنه أن النبي صلى الله عليه وسلم قال:
«مَنْ حَفِظَ عَشْرَ آيَاتٍ مِنْ أَوَّلِ سُورَةِ الكَهْفِ، عُصِمَ مِنَ الدَّجَّالِ». وفي رواية: «مِنْ آخِرِ سُورَةِ الكَهْف».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 809]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Dardaa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
"ku wattu fukki aaya yi njëkk ci saaru Al-Kahf, kon ñu aar ko ci Dajjaal" ci geneenug nettali: "ci mujjug saaru Al-Kahf".
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 809]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne ku mokkal fukki aaya yi njëkk ci saaru Al-Kahf ci xolam ñu aar ko ci fitnay Masiihu-Dajjaal mi nga xam ne day génn ci mujjug jamono di wootewoo Yàlla, te fitnaam nag mooy fitna ji gën a màgg ci kaw suuf ba ñi bindee Aadama ba keroog Saa di taxaw; ngir li ko Yàlla kàttanal mu am yenn ci ay xar-baax yimuy fitnaale ñi ko topp, loolu nag ndaxte njëlbeenu saaru Al-Kahf dafa am ay kéemtaan ak ay aaya yu gën a màgg yi Dajjaal di fitnaale nit ñi, ku ko settantal du fitnawu ci Dajjaal.m Nekk na ci geneen nettali: fukki aaya yi ci mujjug saar wi, mu tàmbalee ci waxu Yàlla mu kawe mi: {Afa hasiba allasiina kafaruu an yattaxisuu...}.