عن أبي مسعود رضي الله عنه قال: قال النبي صلى الله عليه وسلم:
«مَنْ قَرَأَ بِالْآيَتَيْنِ مِنْ آخِرِ سُورَةِ الْبَقَرَةِ فِي لَيْلَةٍ كَفَتَاهُ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 5009]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«ku jàng ñaari aaya yi ci mujjug saaru Al-Baxara cig guddi danañu ko fegal leeb luy Aw ay»
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 5009]
yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne ku jàng ñaari aaya yi mujj ci saaru Al-Baxara cig guddi Yàlla dana ko fegal ay ak lu mu sib, waxees na it: dana ko doy ci taxaw guddi, waxees na it: dana ko doy ci wird yépp, waxees na it: mooy li gën a néew lol dana doy ñu jàng ko Alxuraan ci julli guddi, wax nañu leneen it, amaana li ñu wax lépp a wér wax ji dana ko làmboo.