عن عبد الله بن مسعود رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«مَنْ قَرَأَ حَرْفًا مِنْ كِتَابِ اللهِ فَلَهُ بِهِ حَسَنَةٌ، وَالْحَسَنَةُ بِعَشْرِ أَمْثَالِهَا، لَا أَقُولُ {الم} حَرْفٌ، وَلَكِنْ {أَلِفٌ} حَرْفٌ، وَ{لَامٌ} حَرْفٌ، وَ{مِيمٌ} حَرْفٌ».
[حسن] - [رواه الترمذي] - [سنن الترمذي: 2910]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abdallah Ibn Mashuud mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«Ku jáng wenn araf ci téereb Yàlla bi dina am jenn tiyaaba, jenn tiyaaba ju ne day tolloo ak fukki tiyaaba, waxuma nag {alif laam miim} aw araf la waaye alif araf la laam araf la miim araf la».
[Tane na] - [At-tirmisiy soloo na ko] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 2910]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne bépp jullit bu jàng wenn araf ci téereb Yàlla bi dana am benn yool , te dees na ko ful ba fukk yu mel ni moom.
Mu leeral loolu ci waxam ji: (waxu ma ni nag alif laam miim benn araf la waaye alif araf la, laam araf la, miim araf la): mu nekk ñatt mu am ca fanweeri yiw.