Xàjjaley wanqaas yi

Toftaleg Adiis yi

nangeen kóllarante ak Alxuraan jii, giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom moo gën a gaaw a rëcc giléem gi ñu yeew
عربي Àngale Urdu
ki gën ci yéen mooy ki jàng Alxuraan te di ko jàngale
عربي Àngale Urdu
Ku jáng wenn araf ci téereb Yàlla bi dina am jenn tiyaaba, jenn tiyaaba ju ne day tolloo ak fukki tiyaaba
عربي Àngale Urdu
misaalum jullit biy jàng Alxuraan moo ngi mel ni Utruja, xetam ga dafa teey ak cafkaam teey, misaalum jullit bi dul jàng Alxuraan moo ngi mel ni tàndarma, amul xet te cafkaam dafa neex
عربي Àngale Urdu
Dina ñu wax ëllag ki jàngoon Alxuraan: Jàngal te yéeg, jàngal ni nga doon jànge ci àdduna, ndax sa kër moo ngi tolloog aaya bi ngay mujja jàng
عربي Àngale Urdu