+ -

عن عبد الله بن عمرو رضي الله عنهما قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«يقالُ لصاحبِ القرآن: اقرَأ وارتَقِ، ورتِّل كما كُنْتَ ترتِّل في الدُنيا، فإن منزِلَكَ عندَ آخرِ آية تقرؤها».

[حسن] - [رواه أبو داود والترمذي والنسائي في الكبرى وأحمد] - [سنن أبي داود: 1464]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«Dina ñu wax ëllag ki jàngoon Alxuraan: Jàngal te yéeg, jàngal ni nga doon jànge ci àdduna, ndax sa kër moo ngi tolloog aaya bi ngay mujja jàng».

[Tane na] - [Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy ca Al-kubraa, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 1464]

Leeral

Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne kiy jàng Alxuraan te di ko jëfe, te taqoo ak moom cig jàng ak mokkal bu duggee àjjana dees na ko wax: jàngal Alxuraan, te yéeg ca darajay àjjana ya ndax loolu, jàngal ni nga doon jànge ci àdduna ci njàng mu teey te dal; sa kër moo ngi ci aaya bi ngay mujj a jàng.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Pulaar Itaali Oromoo Kanadi البلغارية Asrabijaani اليونانية Usbeg Ukraani الجورجية اللينجالا المقدونية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bokk na ci njariñal hdiis:
  2. Pay daal mi ngi ajo ca kem jëf ya cib tollowaay ak melokaan.
  3. Ñaaxe ci jàng Alxuraan ak xereñe ko ak mokkal ko ak settantal ko ak jëfe ko.
  4. Àjjana ay kër la ak i daraja yu bari, ñon Alxuraan yi danañu fa am ay daraja yu gën a kawe.