عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«أَيُحِبُّ أَحَدُكُمْ إِذَا رَجَعَ إِلَى أَهْلِهِ أَنْ يَجِدَ فِيهِ ثَلَاثَ خَلِفَاتٍ عِظَامٍ سِمَانٍ؟» قُلْنَا: نَعَمْ. قَالَ: «فَثَلَاثُ آيَاتٍ يَقْرَأُ بِهِنَّ أَحَدُكُمْ فِي صَلَاتِهِ خَيْرٌ لَهُ مِنْ ثَلَاثِ خَلِفَاتٍ عِظَامٍ سِمَانٍ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 802]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«Ndax kenn ci yéen bëgg na bu delloo ci njabootam fekk fa ñàtti giléem yu ëmb, rëy te suur?» Nu ne ko: waaw. Mu ne: «kenn ci yéen jàng ñàtti aaya ci julli moo gën ci moom ñàtti giléem yu ëmb rëy te suur».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 802]
Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne payug jàng ñàtti aaya ci julli; moo gën nit ki fekk ca këram ñàtti giléem yu ëmb rëy te suur.