+ -

عن عُقبة بن عامر الجُهني رضي الله عنه قال: قال رسولُ الله صلَّى الله عليه وسلم:
«الجاهِرُ بالقرآن كالجاهِرِ بالصَّدَقَةِ، والمُسِرُّ بالقرآن كالمُسِرِّ بالصَّدَقَة».

[صحيح] - [رواه أبو داود والترمذي والنسائي] - [سنن أبي داود: 1333]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Huqbata Ibn Haamir Al-Juhanii -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne : Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«kiy biral Alxuraan moo ngi mel ni kiy biral ab sarax, kiy yalu Alxuraan it moo ngi mel ni kiy nëbb ab sarax».

[Wér na] - [Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy] - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 1333]

Leeral

Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa leeral ne kiy fésal jàngum Alxuraan moo ngi mel ni kiy fésal ab sarax bu muy joxe, kiy nëbbutu buy jàng Alxuraan moo ngi mel ni kiy nëbb ab saraxam.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Pulaar Itaali Oromoo Kanadi البلغارية Asrabijaani اليونانية Usbeg Ukraani الجورجية اللينجالا المقدونية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bokk na ci njariñal hdiis bi:
  2. Nëbb njàngum Alxuraan moo gën, kem ni nëbb ab sarax gëne, ndax li ci nekk ci sellal ak sori ngistal ak yéemu, lu dul ne aajo ak yéwénal moo waral biral ga niki jàngale Alxuraan.