عن أبي موسى الأشعري رضي الله عنه عن النبي صلى الله عليه وسلم قال:
«تَعَاهَدُوا هَذَا الْقُرْآنَ، فَوَالَّذِي نَفْسُ مُحَمَّدٍ بِيَدِهِ لَهُوَ أَشَدُّ تَفَلُّتًا مِنَ الْإِبِلِ فِي عُقُلِهَا».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 791]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abuu Muusa Al-hasrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«nangeen kóllarante ak Alxuraan jii, giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom moo gën a gaaw a rëcc giléem gi ñu yeew».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 791]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- digle na ñu kóllarante ak Alxuraan sax ci di ko jàng ngir duñu ko fàtte ginnaaw bañu ko mokkalee ci suñu dënn, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- feddali loolu ci ngiñ ne Alxuraan moo gën a gaawa rëcc ak juge ci dënn yi ci giléem gi ñu yeewe ag buum ci digg tànk ba, bu nit ki kóllarantee ak moom mu jàpp ko, bu ko bàyyee mu dem daal di koy réer.