عن عثمان رضي الله عنه عن النبي صلى الله عليه وسلم قال:
«خَيْرُكُمْ مَنْ تَعَلَّمَ الْقُرْآنَ وَعَلَّمَهُ».
[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 5027]
المزيــد ...
Jële nañu ci Usmaan -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«ki gën ci yéen mooy ki jàng Alxuraan te di ko jàngale».
[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 5027]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne ki gën ci jullit ñi te gën leen a kawe ay daraja fa Yàlla mooy: ki xamlu Alxuraan, cig jàng ak mokkal ak dégg ak firi, te xamal ñeneen ñi la mu am ci xam-xami Alxuraan ànd ak di ko jëfe.