+ -

عَن أَبي مُوْسى الأَشْعريِّ رضي الله عنه قال: قال رسولُ اللهِ صلى اللهُ عليه وسلم:
«مَثَلُ الْمُؤْمِنِ الَّذِي يَقْرَأُ الْقُرْآنَ كَمَثَلِ الْأُتْرُجَّةِ، رِيحُهَا طَيِّبٌ وَطَعْمُهَا طَيِّبٌ، وَمَثَلُ الْمُؤْمِنِ الَّذِي لَا يَقْرَأُ الْقُرْآنَ كَمَثَلِ التَّمْرَةِ، لَا رِيحَ لَهَا وَطَعْمُهَا حُلْوٌ، وَمَثَلُ الْمُنَافِقِ الَّذِي يَقْرَأُ الْقُرْآنَ مَثَلُ الرَّيْحَانَةِ، رِيحُهَا طَيِّبٌ وَطَعْمُهَا مُرٌّ، وَمَثَلُ الْمُنَافِقِ الَّذِي لَا يَقْرَأُ الْقُرْآنَ كَمَثَلِ الْحَنْظَلَةِ، لَيْسَ لَهَا رِيحٌ وَطَعْمُهَا مُرٌّ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 5427]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Muusaa Al-Asharii -yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu wax ne :Yonnente Yàlla bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-nee na:
«misaalum jullit biy jàng Alxuraan moo ngi mel ni Utruja, xetam ga dafa teey ak cafkaam teey, misaalum jullit bi dul jàng Alxuraan moo ngi mel ni tàndarma, amul xet te cafkaam dafa neex,misaalum naaféq biy jàng Alxuraan moo ngi mel ni ngun-ngun xetam dafa teey cafkaam wex,misaalu naaféq bi dul jàng Alxuraan moo ngi mel ni xettar, amul xet te cafkaam dafa wex»

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 5427]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral xaaji nit ñi ci jàng Alxuraan ak di ci jariñu:
Xaaj bu njëkk bi: jullit biy jàng Alxuraan di ci jariñu,moom day mel ni meññitum Utruja,day teey cafka ak xet te rafet melo,ay njariñam bari,moom day jëfe li muy jàng,di ci jariñ jaami Yàlla yi.
Ñaareel bi: jullit bi dul jàng Alxuraan, moom day mel ni tàndarma,cafkaam day neex,te amul xet, xolam day làmboo ngëm kem ni tàndarma di làmboo neexit ci cëfkaam ak ci biiram,te du feeñal xet gu nit ñi di noyyi;ndaxte du féeñal am njàng mu nit ñi di bég ci déglu gi.
Ñatteel bi: naaféq biy jàng Alxuraan, moom day mel ni ngun-ngun, xet gu teey la am te cafkaam wex, ndaxte defarul xolam ci ngëm, te jëfewul Alxuraan, te day feeñ ci kanamu nit ñi ne ab jullit la, moom xetam teey di niróo ak njàngami, cafkaam wex di niróo ak kéefaram gi.
Ñenteel bi: naaféq bi dul jàng Alxuraan, moom day mel ni xettar, ndax amul xet, te ñamam dafa wex, ñàkkug xetam day niróo ak ni mu ñàkke xet; ngir ñàkk a jàngam, wexug cafkaam day niróo ak wexug kéefaram, biiram amul ngëm, bitteem amul njariñ.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Leeral ngëneelu ki man Alxuraan te di ko jëfe.
  2. Bokk na ci yooni jàngale yi joxe ay misaal; ngir jegeele dégg gi.
  3. Jaadu na ci jullit bi mu am aw wird wu muy wéyal ci téere Yàlla bi.